google.com, pub-8963965987249346, DIRECT, f08c47fec0942fa0
Informer juste notre devoir !!!

Papier en Wolof – AMUG JOMU DOMODAA – BAAY MUSTAFAA KEITA ( BAMBARA BU DEGG WOLOF )

0 33

Li ëpp ci góor ñi bëgguñu ko, waaye li ëpp ci jigéen ñi, fu ñu gis tàggoo ak seen sago. Domodaa bokk na ci xeeti togg yi nga xam ñi; ñi dañu koo bëgg, ñee bañ ko, moo ne ñi ko bañ daa na ka ñooy ñiy joxe njël ci kër yi.

Lii mooy dundug doomu-aadama, amul kenn koo xam ne nit ñèpp a la bëgg. Ba sunu Boroom sàkkee dénd bi ba jonn tay jii, ku fi mas a jaar, ak lu say jaloore rëy-rëy ñépp maasewunu bëgg la, fàwwu am ñu la wan gannaaw. Domodaa, ag ubbiku ci yeneen xeeti lujum yi niki lingom, daqaar, kaani añs….. tax na am pàcc bu am solo ci nit ñi sopp ko lool muy jigéen ñi.
Ndekete donte am na ñu la wan gannaaw it, di bàyyi xel seeni reetet ak seen i ñaxtu jëm ci sa jëmm bopp bi, da lay dooleel, di la yokk jom ngir nga góor-góorlu ba ëllëg kenn du la reetaan.

Maam Seex nee woon na: « saa su ngeen xëyee na ngeen jël seen uw naqar def ko muy seen bànneex, tey wéttalikoo Yàlla ». Domodaa li ko tax a sax ci kër yi mooy ñi ko noonoo ñooy dellu di ko may doole ndax la koy togg mi ngi jóge ci jiba góor ñi. Na nuy jége sunuy xarit loo, waaye it na nuy bàyyi xel wax i noon ndax mooy tax nga moytu ndëgg-sërëx yi ñeel képp ku ne ciw yoon.

BàmbaraBuDéggWolof

Leave A Reply

Your email address will not be published.